Printer-friendly version


Programme

E-TIC: bènn porojet la buy yëngu cin mbay càmm ak nàpp ci goxu sow jééri ji

Li ko taxa jogg: Càmm gi,mbay mi ak lèpp lu jëm ci walu wérgu yaram soxal nako. ICVolontaires a ngi joxé ay jumtukay yuy yook xibaar u ňi yengu ci ligéey yooyulé nga xamni ňooy banxaassu koom-koomi gox ak dëkk yi nékk ci jéerri ji.

Li ko waral: wétaayu dëkuwaay u jéeri ji dafay indi ay ngalankoor  ndax li ëpp ci samkatt yi janguňu té duňu took ci bénn bëreb rek, looloy waral duňu jott ci xibaar yi ňu xaatim ci ay téeré. 

Ňi koy jariňoo: bay katt sam katt ak napp katt yu ndaw yi, taskatu xibaar yi ak tamit ňi yengu ci xarala yu yéess yi

Jëff Ji: Daňu bëga buux ligéey bi jublu ci tasaaré xibaaru luma yi.buko défé daňuy yooni as ndaw ci sëk yi muy saytu liňuy jënd ak li ňüy jaay.naka laňu koy dencé kan moo koy jëlé ci tool yi.ndax daf am ay baana-baana. ňu boolé waalé ci njëk yi meteo bi ak bépp xibaar bu mëna mootali laac yi.

Bu loolu wésoo di naňu jèmma  suxat ap bérébu tasukayu xibaar ci li ňu jëlé ci sëk yi.dal di sétantal yoyulé xibaar ngir taxawal bénn jookowukaay ci ay SMS bu ko défé ňëpp dina ňu mëna jëllé xibaar ci bobulé berep té duň ko joté fén fudul ci SMS yi.

Li gëne nék jubluwaay bi mooy dimbali samkatt baykatt ak napkatt yi ci ňu mëna waxaalél sén bopp sukendiku ci xibaar yi ňu léén jox.muy ci njaay mi ca sëk ba wala ak baana-baana yi.  

Ňi ňuy gungé ci ligéy bi: ňi nék ci réew mi: njiitu jewriň yi; jewriň  ji ňu dénk camm gi; jewriň ji ňu dénk xarala gi ak taskatu xibaar yi; jewriň ji ň dénk wallu tagatt yaram bu Maali; service civique national; RTS1; direction nationale de la meteorologie; dëk dëkaan yi; mbotayu baykatt yi; ISRA EREV; Youth ICT bu Maali; conjedjev; ňi nék bitim réew :  Office international des épizooties; FAO; Association Africaine de Suivi-Evaluation; CILSS; CIRAD; Fonds Inforoutes, Francophonie; Ambassades bu tugal ci  Maali et au Sénégal; Agence Universitaire de la Francophonie (AUF).

Suňu mébétt:

Li ňu bëgg:

Liňu ci yaakaar: sunu yaakaar ci bilé ligéy mooy taxawal bénn bërëp buy wané mbay mi gënn ak camm gi gënn ci bërep yi ňu tann
Ligéyu ICVolontaires: ICVolontaires mooy jublu ci llèpp lu jëm ci wallu tann way sabablu yi, té yi mooy jokalé lëpp luy yengu yëngu ci bilé ligéy
tolluwaay yo ligéy bi ci ay at: fukki wéér ak juroom ňett
nitt ňici yengu: nétti téemere ak juroom fuk.

Dëkk yi ca Maali:

Dëkk ya ca Senegaal:

Tërilin: kuréel bi yéed: Kuréel bi ay nitt yu am xam xam cin wallu mbay ňooko bokk.di sootanté ay xalaat ak képp kuy yengu ci ligéy bi.

Waxtu wi

Avril à juillet 2009: Taxawal situ internet bi, dajallé xibaar yi, waxtaan ak ňi ňuy japalé (AUF, Université Cheikh Anta Diop à Dakar, SCN)
Aout 2009: Dajalé xibaar yu gëuna mucc ayib ci tombuktu.ak giss ak jewriň ji yorr wallu ndaw ňi.ndajjé bi njeuk ca Maali
Nétéel ak ňéntél xaaju 2009: Sotanté ay xalaat ca tombuktu, xool lu xééw Segou
Fevrier 2010: Ubiték ligéy bi ca maali ak taxawal ekip bu senegal
Juin 2010: Taxaw xoolaat fi ňu tollu
Toftallé linu jëllé ci rapport yi

To download this file: fiche_etic_wb_en.pdf (194.6K)

©1997-2024 ICVolunteers|system mcart|Updated: 2024-11-22 13:57 GMT|