Printer-friendly version


About Us

ICVolontaires dafa di bénn mbootaay buy yengu ci adina bi yëp ci wallu jokko te séntu wu ci bénn koom-koom. Beral na loxo lool lëpp luy jëm ci kalaama, lëpp luy yengu ci wallu cybervolontariat japalanté ci wallu ak ndajjé yi.

Ci volonatriat lanuy jaaré ngir lige yak ay mbootaay yuy yengu ci luy suxalli dundu doomu aadama,ci waalu nèkkin am ci li ko wërr ci jawu ji mu nek ak ci wergu yaramam ngir taxawal ay projet ak ay Ndajje ci biir ak ci bitim reew.  

Nungi lige yak ay volontaire ngir suxalli ponk yi ňu tërël ci waalu jang ak jangale mi ngir tamit xettali doomi reew mi ak deukendoo yi ci sénn yokuté.

ICVolontaires am na njëriɳ bu baax ci siiwal volonatriat bi ndax mungi xirtal nitt  ňi ci nuy jappalé sénn reew ci seen coobare ci li muy boole ay mbootay ak ay nitt ňu bokk dekuwaay ak tamit and bi muy and ak nioom ci pasteef bi niu ci andal.

ICVolontaires nak geneve la kerërem gu mak nek waayé ca siwis, waayé amna ay dekuwaay ci bëreb yu baré yu deme ni Espaaň, farans Afrik du sud, Maali, Senegaal, Japon ak Brésil.

Suňu giss-giss

Giss-gissu ICVolontaires mooy aduna bu gënn bi ňu nek ni ngir boolé guňuy boolé xam-xam yi té ňu koy jaaralé ci volontariat.

Suňu jüblu waay

ICVolontaires selibéyool la ak ndajjé la buy jublu ci:

Fiňu bëga yègg

Jox nitt ňi, deukuwaay yi ak bërebu ligeeyukaay yi, saň-saňu ak katan ci ni ňuy boolé xam-xam ak soxla yi ngi li léén di jëmelé kanam.

Suňuy kaddu

Jotté ci xam-xam, jang mi, suxàlli, xam-xamu ak technologie, axak yéllefu doomu aadama, wàňňi ndool gi.

Fiňuy yëngu

Jòkko: kalaama yi, cybervolontariat, jappàle mbootaay yi ci taxawal ay ndajjè, ligeeyal rééw mi ci coobaré.

Ku ci bëgga am lu gènna leer meun na dùggu ci buntu bi di http://www.icvolontaires.org


©1997-2024 ICVolunteers|system mcart|Updated: 2024-04-07 20:58 GMT|