Yi ëpp ci li ňuy bay ci dëkk bi ňooy: gerte, dugub, ceeb, mbox, suuna, ňambi, wëteen, tamaate, lejum. Ci wàllu càmm gi nak yi ňi faral di gene giss ňooy: nak, xarr, bëy, mbaam xuux, ay njanaw ak ay jënn.jamono ji ňu tollu nii nak askan wi xèrru lool ci mbay meek càmm gi te soo setloo bok na ci lii gënna suxali koom-koomi reew mi. Li gënna jamp ci jamono jii nak mooy naka laňuy def bam bay mi mënna dundal askan wi yèpp.
Li ëpp ci Seegaal a ngi bok cig ox bu ňeme bèkoor lool ak taw mu jaffe te wissaroo, boolekook suuf su sonn lool. Te soo setloo sax 5% ci suuf si rek moom dacc ndox, loolooy waral nitt ňi nawett rek aňuy bay te mooy indi ap goob mu tërëdi lool. 70% ligey kat yi ňu ngi yengu cik mbay (boo degee mbay nak mooy àll bi camm gi ak nàpp gi) te loolu tollu na ci 18% ci xaalis bi ňuy ligeye ci reew mi.
Tool yu ci ëpp ay baykat yu ndaw ňoo leen di yorr (1.5-2.4 ci ay hectaar), te 60% mungi feete ci li ňu dupe “biiru gerte gi”. Wall wu bari ci suuf soosu nak ay xeet a ko moom. 11% wu suufu Senegaal bi yèpp daňu koy bay, te mbayum dugub ak gerte bi yokku na ci at yi ňu mùjju ba tollu ci 40% ak 36% ci buɳ ko toftale.
Buňu wakerloo ci xibaar yi wàdde ci nguur gi, reew ma ngi bay atum 2009 420.000 ci ay tonnu gerte muy lu wùtte lool ak 460.000 ci ay ton yu atum 2006, bi nekutoon att mu neex ndax ňakum ndox bi ca amoon.
Ceeb bi: 50% soxla yi ci ceeb bi rek laňuy bay ci reew mi.li ci dess daňu koy njëndi jib a Asie ndax seen ceebu Basmati (parfiime) ňoo gënna neex ceeb bi ňi baye fii. Nit ňi taamuwuňu ceeb bu parfiime wul (muy ceebu Asie bu xaralal bu baax). Mbayum ceeb baa ngi tambali ak nasaraan yi fi nekoon ci atum 1960 ya.
Gerte gi: mbay moomu nak njaayum bitim reew rek a ka taxa jog.
Yaatuwaayu dëkk baa ngi tollu ci 196.722 sq ci ay km (suuf si di 192.530 ndox mi di 4.192 km). Ci atum 2009 xaalis bi ňu ligeeye ci biir reew laa ngi tollu woon ci 16 milyaar te 13.8% yaa nga bayeko ci mbay mi (amna ňu ne sax 18% ya la), 23.3% di bayeko ca ligeyu xarala ya, 62.9% di jùgge ci bërëbu ligeyukaay yi. Neena ňu tamit ci atum 2009 njaayum bitim reew banga tolloon ci 1.652 ci ay milyaaru dolaar:
Ci att moometam njënd ma ngi toluwoon ci 3.864ci ay milyaar dolaar ci yi ňuy waaja li:
Ligey yi ci gënna am doole mungi ni tëdde: mbay mi 77.5%; xarala ak bërëbu ligeyukaay yi: 22.5% (xibaaru 2005). Nàkk ligey mba ngi tollu ci 48% (xib 2007). Te 54% wa reew ma ngi dëkk ci ndool (xib 2001).
Ci atum 2008 dëkk baa ngi amoon 237.800 ci ay telefoonu kërr ak 5.389 miyoŋ ci ay portaabal.ci atum 2009 amoon na 227 ci ay situ internet 1.02 ci ay milyoŋ di jëfëndiko internet boobule (ku ci bëgga xam lu gënna leer na xool ubitek Saar bi vu tollu).
Ci weeru Sulet 2009 askan waa ng tolu woonci 13.711.597 ci ay nit, 1.29.823 ňu ngi newoonca Dakaar te ňu ngi leen tërelewoon ci nii:
Yokutek askan waa ngi tolluwoon ci atum 2009 ci 2.709%. askan woowe nak 42% ňu ngi dëkk ca taax ya ak yokkute gu tollu ci 3.1% at mune digente 2005 ak 2010. Fan wu guddu waa ngi tollu ci 59 att muy 57.12 ci goor ňi ak 60.93att ci jigen ňi xibaaru 2009.
Bu ňu tolleo ci jang mi nak xale yi duggu daara aa ngi tollu ci 39.3% muy 51.1% ci ay goor ak 29.2% ci ay jigeen. Ni ňu jàppa ngaaka nak ňooy ňi tollu ci 15 att te munu ňu bind munu ňi jang.
Reewu senegaal a ngi doxe tanneefu ňëpp wala ňi ëpp. Reew ma ngi toftale nii Reew mi > Dëkk bi > Gox mi >> koɳ. Donte ňu ngi setlu ay jeego ci walum ubbi xaralala yi ci gox yu bari, ba leegi lèpp daf dajaloo ci benn boor. Loolo waral njiitu gox yu barri Dakaar laňu dëkk waye daňuy am beneen njiit bu dëkk ci gox ba.
Reew yi nekkoon ci kepparu tugal muy senegal ak Sudaan (ňu dupewoon ko Tamitrepublik bu Sudaan) ňoo dajaloo woon ci atum 1959, juroon liňu dupe federaatioŋ bu Maali at ma ca topp. Waye ay weeri laňu ci tek rek boolo boobu daldi tass. Senegaal ak gambi daldi booloowaat co turu senegambi ci atum 1982 waye giss-gis yi mujul sotti ba tax mu daldi tasaat. Wa MFDC daldi fipu dale ko ci atum 1980, waye ay xaatim yu bari degoo naňu ci woon ak nguur gi yu mujjul antu.loolu terewul Senegaal bokk ci reew yi ëpp ndegerlaay ci nguur ci afrik. Nek naňu 40at yoo xam ni nguur guňu dupe PS ňoo doon jiite ba ci atum 2000 abdulaay waad daldi jëll nguur ngi.fallaat naňu ko ci atum 2007 mu daldi sopi saartu reew mi ngir nasaxal jamarloo gi. Demb Senegaal nak yagg na lool ci taxawal jamm ci dëkendoo yi.