Ay dëk

Maali

Le projet E-TIC au Mali

Ca Maali xalaat baa ngi sancü ci dëkk yu mel ni:

  • Bamako: di gox bi kureel yi bari sanc seen makaan
  • Tombouctou:  mbayum ceeb, ble, càmm ak nàpp
  • Ségou: ceeb dugub mbox càmm ak nàpp
  • Sikasso: ňambi mango, bèpp xeetu fruit camm ak tamitt wëteen

Luňu wara xam ci dëkk ba

Nitt ňi: 13.443.225 (ca atum 2008)
Xaalis bi: CFA Franc BCEAO (XOF)
Kalaama Mali: Français (officiel), Bambara (Bamanankan), Bomu, Arabe Hasanya, Maasina Fulfulde, Mamara Senoufo, Kita Maninkakan, Koyraboro Senni Songhay, Pulaard, Songo, Soninke, Syenara Senoufo, Tamasheq, Tieyaxo Bozo, Toro So Dogon, Xaasongaxango
Diine: jùllit ňi 90%, cèddo 9%, catolik 1%
Caada: Mandiŋ 50% (Bambara, Maliŋke, Saraxole), Pëll 17%, Voltaic 12%, Songay 6%, Tuareg ak naar 10%, ya ca dess 5%
Taax ma: Bamako 1,323,200 dëku metro bi 935,400
Jexitalu situ internet yi:.ml
Numero xamekayu dëkk bi: +223

Mbay mi

Li ëpp ci li ňuy bay ci reew mi mooy: gerte, dugub, mbox, bëssi, ceeb wëteen tamaate, lejum, nàkk, xàrr, mbaam xuux, jënn, ak mango.jammono ji ňu tollu ni nak ni aaskan wi waroona yengoo ci mbay mi dess na te soo setloo mbay mool bok na ci li gënna doxal reew mi. Book na tamitt ci li gënna soxal askan wi muy lu ňu war def mbay mbay mi mënna  dundal askan wi yëpp.

Xaac bi feete bëtt gannaru reew mi rek ňoo farlu ci mbay mi te lu yëess 2% ci suufu dreew mi la ňuy bay fimi tollu ni. Mbay mi nak tollu n ci 45% koom-koomi reew mi ak 25% ci li ňu yobu ca bitim reew yokku ci 80% ligey katt ya ci yenguci atum 2005.

Dugub, bëssi, ceeb, lejum fruit ak fudënn: ňètt yi ňu njeka lim ňooy mbay mi askan wi di dunde bess bu nek.dugub beek bëssi bi ňungi leen di gënna bay ca goxu Seegu bandiagar ak ňooro. Ceebu padi bi moom ňu ngi koy faral di baye ca Mopti ,seegu,ak ňaafuŋke baci dex ba  ca Tombuktu. Xeetu pèpp yooyu ak dundu rek la leen di 90% ci baykat yi di doye. Gerte gi moom ňungi koy faral dib aye ci goxu Sudaan yi, mook wëteen bi ak ňam yi, lëjum yi, ak fùddën s. Xooxu kaarite bi di saxeyaan moom askanu Maali baa ngi jëfendiko diwam. Gerte yi moom lu ci ëpp diw bi ňi jay bitim reewa tax ňu koy bay.

Wëteen bi:  Wëteen bi mooy xeetu mbay bi gënna am solo ca maali. Soo setloo sax maali bokna ci ňi ëpp li ňu koy bay ci Afrik ca ganaw Egypt ak Sudaan. Mbayaum wëteen bi nak ňungi koy faral di defe ak njaboot gi ci ay tool yu yamamaay, yeen saaye ay kureel daldi ci dugal seeni yoxo ca bëtt ganaar jàpp pënkum reew mi. ňoo ňe ap kureel bu mag bu maali moo leen di jiite ňu naan ko CMDT, bobule kureel tamit tubab yi moom CFDT ňoo ca moom 40%. Mbootayu koo-koomi aduna bi sax boo xoole mungi doon def keem katanam ngi ňu ubbi ligey boobu ndax askan wi men cee soobu ngir baykat yi gënna doxle.waye tontub CMDT moodoon ne ak doxalin bi ňuy ligeye ňoom mbaayb mi dafa fulu ňaari yoon dale ko ca atum 1993. Ca Maali nak wëteen ba amfa solo lool ci njënd meek njaay mi. ca atum 1999 mbay ma nga tollu woon ci 218,000 ci ay ton. Jëuk yi aduna bi tëraloon tamit yokoona njaay ma. Ca atum 2001, bi ňu aaye nba pare amoon na ňaňu ci li tollu ci 46,7 ci ay milyaar dolaar.

Mango ji: mbayum mango ji dafa am solo lool ci koom-koom reewu maali.ci njaayum ňam ak lêjum reew mi fùll na ba ňaari yoon ay njaayam ca bitim reew bu yagul dara, ak lu tollook 10,000 ci ay tonn ca atum 2009.farlu googu nak li ko sabab mooy doxalin bi PCDA bu jëri ň ji ňu dënk mbay mi tëral ci xeetu diitantek mbag ci njaay mi. Jeff yooyoo bokk ci li gënna yook mango gi ňu jay bitim reew ci atum 2007 jùgge ci 4.000 ci ay ton dem ba 9.797. ci misaal looloy xollu tëralin bu yes bii jeema yokku mbayum mango gi,karite gi, daakande gi banaana gi sople gi ak pombiteer gi. Soo xoole yaari att ci ginaaw la maali dooral ay ayu bess yu ňu jagleel mango gi, foofe la kèpp kuy ligey ci mango di dàjje.

Jùggag daanu ci toluwaay bi : mbay mi daf yooku bu baaax ndax taw bi nimi tëdde.ca atum 1999 mbayum pèpp mi èggoon na ci 2.149.000 ci ay ton.misaalu mbayum 1999 ci li ňu doon gënna jëfandikoo bokk na ci lu ci mel ni dugub, 641.000 ci ay ton; bassi 559.000ci ay ton; ňamba suukar 303.000 ci ay ton; mbox 341.000 ci ay ton; ňambi 10.000 ci ay ton pataas 16.000ci ay ton.ceeb bi moom tolu woon na ci 589.000 ci ay ton.

Jafe-jafe yi ak mebet yi: amul leen lu ňuy bay te mu sax akk ci att mi yëpp.amna nak ay galankoor yu metti yu ci melni bekoor, waye erewul reew maangi genne ci mbay mi bu baax ci att yi mùjju. Yeneen jafe-jafe jawu ji bokk naci garab yi vuy gorr muy jeegoloo àll bi, suuf si di gënna soon rek, ndox mi di gënna neew, cacc gi, ak nak li jëm ci walu xeetu mbay mi ňi def ak puudar yi ň uy jefediko te nga xamni bu yagge dafay nasaxal suuf si.

Njënd ak njaay,ak ligey mi

Yaatuwaayu dëkk baa ngi tollu ci 1.240.192 sq km (1.220.190 sq km di suuf, 20.002 sq km di ndox.ci atum 2009 xaalis bi ňu ligeeye ci biir dëkk baa ngi tolluwoon ci 358 ci ay milyaar, te 45% y xaalsu mbay mi la,17% bayeekoo ci izin yi ak 38% ci ligeeyu biro yi (xibaaru 2001). Amna xibaar yu ne sax ci atum 2006 njaay mi jëm bitim reew èggoona ci 4 milyoŋ.

  • yi gënë jefendikoo: gerte, mango, li jùgge ci petorool, wurus, wëteen.
  • Andandoo yi: Chine 26,4%, Thailand 10,6%, Danmark 6,4% Pakistan 5,1%, Maroc 4,9% (2008)

Njënd mi jùgge bitim reew moom mungi tolloon ci 358 ci ay milyaar ci at boobule ak ci yi ňuy waaja lim:

  • Njënd mi: petorool, ay jumtukaayu xarala, lekk ak ay piis.
  • Andandoo yi: Senegaal 13,1% Cote d’Ivoire 11,9%, Tugal 11,3% ak Chine 5,9 (2008)

Dooley xeetu ligey yaa ngi nii tëdde: mbay mi 80%; ligeeyu taax yi 20% (xibaaru 2005) ňakk ligey mbaa ngi tollu ci 30% (ci atum 2004). Neena ňu tamit ni 36,1% yu doomi reew maa ngi ndud ci ndool (2005).

Jokkoo bi

Ci atum 2008 dëkk bi ammon na 82,800 ci ay telephonu kër ak 3.267 milyoŋ ci ay telefon portaabal. Ci atum 2009 amoon na 519 situ internet ak 200.000 ci ay nitt yu koy jëfendikoo (ku ci bëgga am lu gënna leer na dem xooli ubitek këyitt yi ňu bind ci wall woowu).

Toogaayyu askanwi

Ci weeru sulett ci atum 2009 askanu Maali engi tolluwoon ci 13.443.225 ci ay milyoŋi doomi aadama, ňu ngi o sèddële woon nii:

  • Li ko dalle ci ňi amul att ba ci ňi am 14 att: 48,3% (goor ňi toll ci 3.089.406 jigeen ňi di 3.023.341)
  • 15-64 att: 48.7% (goor ňi di 3.065.167 jigeen ňi di 3.101.941)
  • 65-j¨m kaw: 3.1% (goor ňi di 151.718 jigeen ňi di 235,441 (xibaaaru atum 2009)
Ci lolu yep nak 32% ňoo dëk ci taax yi booleko ak ak copite digente 2005-10 bu tollu ci 4,8%. Li gënna barri co lunuy ndundu tollu ci 51.78 ci ay att. Goor ňi di dundude ci lu tollu ci 50,21 ci ay att jegeen ňi ňoom ňu ngi tollu ci 53,4 ci ay att (2009 xibaar).

Njang mi

Tollu waayu ňi duggu ci daaray nasaraan baa ngi ci46,4%, di 3;5% ci ay goor ak 39,6% ci ay jigeen (xibaaru 2003). Ni ňu jape ngaaka nak ňoy ň idem ba am 15 att te munu ňoo bind muu ňoo liir.

Tërelinu dëkk bi

Maali e ngi teedi i taaneefu njiit bu ňepp wala ňi ëpp ci askan wi tann.askanu njiitam yi book ci bi gënna njaxlaf ci Afrik. Dëkk baa ngi sancoo nii: Reew mi> dëkk bi > taax mi>gox bi. 

Dëmb

Reewu Sudaan ak Senegaal a ngi jott ci seen kilifteef ca atum 1960, att mooma la ca Maali jott itam.bi Senegaal gèdde li ňu tùdde woon Republique Soudanaise ay weer bi mu weeso la ňu jox reew ma turu Maali.Nguur ga fa newwon na nga jeex ci atum 1991 bi soldaar ya boome ki di buur ba --ki ko jiite woon nak moo nek ci nguur gi jamono ji muy Amadou.T.Toure-- loo loo waral nak Maali bokk ci reew y gënna jox cërr axa k yeleefu doomu aadama ci afrik. Ki njëkka jëll raw gàddu gi ci boppu reew mi moo doon Alpha Konaaré ca atum 1992 jëllaat ko ci atum 1997. Toppoon tamit saartu reew mi ne njit bu ne yaari yoon rek laybokk ci raaya gi ba tax na keneen wuutu ko ci nguur ga muuy Amadou Touré moom tamit toogaat na yaareelu yoonam ci nguur gi ci atum 2007.

©1998-2024 ICVolunteers|system mcart|Updated: 2024-10-16 00:53 GMT|Privacy|