Ay dëk

Ubité: Sahel

Poroze E-TIC bi mungi tek tankam ci goxu Senegaal ak Maali gënn jaa nek nak ci goxu bayukaay ya ca Sahel.

Le "Sahel" nak boo ko dégé mu ngi juge ci baatu araap buy wundi "wet" wala "ňak" moom nak ay dëkuwaay la yu taxaloo yoo xamni ňooy wane jeexitalu bët sahara ak allu Sudaan bi(wute na nak ak reewu sudaan bi mu bokal tur)  nga xam ni taw bi moom dafa neew lool ca bët ganaaru reew ma. Li ko dale ca penku ba ca sowu nak mungi lallu ci geeju Atlantik ba ca Geeju "mer rouge" alam ba nak amna ay gancax yu yaatu yu ay garab yu taxaw rax yu ca deme ni Acacia.

Ca Maali nak poroze bi mungi yungu ca:

  • Bamako: di gox bi kureel yi bari sanc seen makaan
  • Tombuctu: mbayum ceeb, ble, càmm ak nàpp
  • Seegu: ceeb dugub mbox càmm ak nàpp
  • Sikaaso: ňambi mango, bèpp xeetu fruit camm ak tamitt wëteen

Ca Senegaal xalaat baa ngi yengu ci gox yii di:

  • Dakar / Yoff: foofe la ay kureel yu barri def seeni ëtt
  • Gede santie: mbayum ceeb gaňcax, ňambi, tamaate, sople, dugub, camm gi ak napp gi
  • Mbaam: ceeb, gerte, mango camm gi ak napp gi
  • Mexe: gerte, dugub, ňambi, mango ak càmm gi
©1998-2024 ICVolunteers|system mcart|Updated: 2024-10-16 00:53 GMT|Privacy|