Mbay ak càmm

Li waral ligey bi

Ndool gi

Ndool gi lu am la ci lu toolu ci benn milyaar ci ay doomu aadama te mbir si dafay gën di meti. Xiif gi ak ak maral gi ňu laal 815 ci ay milyoŋ ci adina bi yepp, te ňenti gunne yu tollu ci juroomi att yoo jëll rek ken kaa nga dëk ci diwaan bu ndool ak maral sonal. Ci bët gaannaaru Afrik nak xiif gi mungi gënna dellu gina waye nak nitt ňaa ngi gënna xiif te li koom gi dafa wa ňeeku.

Teere bi di Rapport sur le développement humain (PNUD) genne ak beneen bu tudu Rapport sur le développement dans le monde (Banque mondiale) Mondiaal genee ko ňu ngi firndeel ni ci biir dëk yu barri li ňu tude OMD muy ay mebett yu ňu nassoona taxawal ci reew yu ndool yi du mënna antu filleek koomu reww yooyule yokuwul.

Ndool gi nek ci reewi yi nak mungi gënna sonal wa kaw gi.looloo waral nak ňu wara raaňe suturlu ak ndool. Soo xolle ci kaw gi ňu barri ndoolu ňu com ni ňu ko yaakaare si buňu gene dem ca taax ya dëk ci ay coň yu soon, di jankoonte ak dundin gu doy waar ak coow li ak leeneen ak leneen. Ni took ca kaw ga ňu ngi suturloo mooy mbay mi nga xam ni ňi ëpp ci ňoom ci la ňuy yengu.

Ci dëkuwaay yu bari nak ňi dëk ca gox ba ak xeet ya fa gënna neew ňooy gënna bari ci ňi ndool, su ko deffe jigeen ňi tamit nek di ňi fa gënna sonn te ňu ňakal leen solo lool. Soo xoole ňi kaw gi ndool amuňu lu ňu mënna suturloo—amuňu suuf, ndox, koom—munu jott ci xarala ak jumtukaay yi wal sax ci Sëk yi. Nu boole ci ni amuňu xam-xam bi leen mënna dimbali ci luy yokk seeni mbay, seen koom wala seen dund.

Mbay mi ak nàpp gi, li kaw gi di gënna jublu

Suňu jàppe li (FAO) ak jëwriň ji ňu dënk mbay mi ca Amerik, mbayum pèpp daf a waňeeku ci ňaarel  bi atam li ko dalle 2006 ba leegi. FAO neena li mu rombe ňaari miyaar ci ay tonn tuuti la, wute ak li ňu amoon ca atum 2005 di 2.38 miyaar ci ay toonn ak 2.68 milyaar ci ay tonn ci 2004, te soxla bi ko dina bi soxla waňeeku wul ndax nitt ňi daňuy gên di yooku.

Li nguuru AMerik wax nak daf gënna dooy warr ndax 1984 miyaar ci ay tonn, muy 58 milyoŋyu waňeeku ci mbay moomu ci at mii di ňëw. Denc yi mungi jugé ci 16 fan ci atum1999 dem ci 57 fan ci atum ren. Te li yon mooy gën ja neew 70 fan. Jenk yi moom yokku naňu bu yag ba tollu ci 20% ci atum ren. Mu mel ni ligey boobu ONU sumboon ngir xaac ndool bala atum 2015 daň ko faf nasaxal.

Ak yooku guy rey gi am ci jenk yi (jegu ceep mi ňu barri di dunde mungi yoku ba 75%, ble bi moomu ngi toll ci 120%) moo waral li ngalu ci loosu bank mondiaal di 100 milyoŋ i ay doomu aadama yu jëm ci ndool googu. Looloo waral ki di njiitu Bank monjaal di Robert Zoellick né "daňu wara sexal dundn gi ňi xiif, loolu rekay li nek"  manam amatuňu jotu wax judul jeex dafa jot ňu tambale jëf?

©1998-2024 ICVolunteers|system mcart|Updated: 2024-09-06 20:10 GMT|Privacy|